Mala Fal

Dior Mbaye

Compositor: Não Disponível

Waoh waoh
Yeah yeah yea
Yeah yeah yea
Dior Mbaye

Sama mbëggeel ci yaw day gën di mag
Fu kawe kawe laa la teg ni picc buy tàgg
Ma doon sa géwél di la wayal la ka tagg
Loo bëgg laay def loo joxooñ ma dagg

Neexul ba neexul mais dama la bëgg
Sama buntu xol yaw laa ko tijji ndax yaa fëgg
Sama ñaan tay ba suba mooy ñu dëkk
Génn neex na loolu waaye séy mooy dëgg

Oh baby, baby, baby, lal-le
Lalal say basaŋ kenn du ko lalli
Yaay buur, yaay bummi, yaay xol bi
Maa la fal, maa la fal, kenn du la folli

Lal-le
Lalal say basaŋ kenn du ko lalli
Yaay buur, yaay bummi, yaay xol bi
Maa la fal, maa la fal, kenn du la folli

Fi nga ma jële moo sori
Li ngay def ci man moo bare
Fi ngay jeexale laay doore
Te baby tambaleguma bay pare
Lumière bi ci man yaa ko taal
Li manquéwoon ci man yaa ko matal
Gisatuma lu may ragal
Te baby tambaleguma bay pare eh

Oh baby, baby, baby, lal-le
Lalal say basaŋ, kenn du ko lalli
Yaay buur, yaay bummi, yaay xol bi
Maa la fal, maa la fal, kenn du la folli

Lal-le
Lalal say basaŋ kenn du ko lalli
Yaay buur, yaay bummi, yaay xol bi
Maa la fal, maa la fal, kenn du la folli

Ngoy Fama Lakh-hey sa maam
Di Mbang Ngoyor Ali Bangara wa
Mbaye Madické Garou
Narou Adama Mbaye
Niatti Diouma ak ñatti Diaka
Ku ko am sa maam la ko jële
Seudou bee yaay garmi

(Kenn du ko lalli)
Mamadou Tall chéri Amina
(Kenn du ko lalli)
Yaayu Anni Ya Astel, chérie Papi Dia
(Kenn du ko lalli)
Mounass tour du monde
(Kenn du ko lalli)

Oh baby, baby, baby, lal-le
Lalal say basaŋ, kenn du ko lalli
Yaay buur, yaay bummi, yaay xol bi
Maa la fal, maa la fal, kenn du la folli

Lal-le
Lalal say basaŋ kenn du ko lalli
Yaay buur, yaay bummi, yaay xol bi
Maa la fal, maa la fal, kenn du la folli

©2003- 2025 lyrics.com.br · Aviso Legal · Política de Privacidade · Fale Conosco desenvolvido por Studio Sol Comunicação Digital