La Famille Au Senegal Oui (feat. Diarra Sylla)

Dior Mbaye

Compositor: Não Disponível

Et la famille au Sénégal?
Oui, bien sûr!

Sori sama réew ak sama askan
Taxul ma fàtte man mi may kan
Damay liggéey doxuma ci caaxaan
Seen soutien da may bégal di ma yokku katan
Damay ñafe di liggéey duma geestu
Yónne yakamti ma duma daagu
Li ma weesu la réccu
Fi ma jëm leer na ma, man la ni séntu

Ay ay ay
Fii mooy Senegaal

Fii la xol yi di feexe
Fii la stresse biy wacce
Fii la xale yi gëna baaxe
Sama réew nii la neexee

Foo dëkk, Senegaal? Oui!
Fière ci doon sénégalaise
La famille au Sénégal, oui
Fière ci doon sénégalaise

Civilisé rafet mëna sañsé
Tey bëgg topp cas
Ku ne ngay wax, pays de la teraanga
Kenn du ñu yàpp, kenn du ñu xeep
Kenn du ñu kël-kële
Ñun lañuy wax, pays de la teraanga

Am teraanga
Ku ne ngay wax, pays de la teraanga
Sama réew mi da may neex te jàmm ja ngi fi

Jàng bi na fi sax, jàng bi

Ay ay ay
Fii mooy Senegaal!

Fii la xol yi di feexe
Fii la stresse biy wacce
Fii la xale yi gëna baaxe
Sama réew nii la neexee

Foo dëkk, Senegaal? Oui! (Oui, bien sûr)
Fière ci doon sénégalaise (oui, bien sûr)
La famille au Sénégal, oui (oui, bien sûr)
Fière ci doon sénégalaise (oui, bien sûr)

Foo dëkk, Senegaal? Oui!
Fière ci doon sénégalaise
La famille au Sénégal, oui
Fière ci doon sénégalaise

Yaw Diara Sylla!
(Foo dëkk, Senegaal? Oui!)
Fatou Mbacké Diongay sa yaay
(Fière ci doon sénégalaise)
Ami Ndikou Guey yaayam
(La famille au Sénégal, oui)
Cheikh Diongay baayam
(Fière ci doon sénégalaise)
Demba Sylla sa baay
(Foo dëkk, Senegaal? Oui!)
Sokhna Aïda Mbacké yaayam
(Fière ci doon sénégalaise)
Yaay Seutou Serign Barra
(La famille au Sénégal, oui)
Diarra yaay Seutou Serigne Touba
(Fière ci doon sénégalaise)

Foo dëkk, Senegaal? Oui!
Fière ci doon sénégalaise
La famille au Sénégal, oui
Fière ci doon sénégalaise

©2003- 2025 lyrics.com.br · Aviso Legal · Política de Privacidade · Fale Conosco desenvolvido por Studio Sol Comunicação Digital